Ci at yii ñu weesu, ak yokkute bu gaaw bi am ci medsin bu jaar yoon, ak xaralay saytu feebar ci vitro, reactif hematologique yi, muy jumtukaayi test klinik yu mag yi, dañu nekk lu liggéeyukaay bi di bàyyi xel ci wàllu njuréef yu bees. Liko dalee ci test yiñ daan faral di def ak loxo ba ci analyse yi ñuy def ci otomatik, baamtu reactif hematologie yi yokkul rek njariñu test yi, waaye yokk nañu itam ndimmbalu diagnostic bu gëna dëggu ci bànxaasi yu mag yi ci àdduna bi.
Ci wàllu njuréef, immunoturbidimétrie, cytométrie de débit ak pexem biologie moleculaire ñoo nekkoon yoon wiñ gëna jëfandikoo ci reactif hematologique. Bu ñu jëlee misaal immunoturbidimetry, dafay gis limu protein yi ci biir antigen - anticorps yi, ba noppi dafay jàppale bu baax ci saytu feebar yu melni anemie ak inflamasioŋ. Flow cytometry, ak kàttanam ci jàngat paramet yu bari, nekk na jumtukaay bu am solo ngir jàngat xeetu leucémie ak jàngat fonction immunitaire. Rax ci dolli, dugal xaralay PCR ak NGS (next generation sequencing) taxna ñu gëna yomba saytu lesion yu ndaw yi des ci tumër yi ci deret ji, loolu dafay jàppale done yi ci paj miñ personaalise bu baax.
Yokkateg laaj bi ci marse bi taxna ñu bari defar ay reactif hematologie. Fi ñu tolli nii, produit reactif yi dañuy wax ci wàll yu bari lu ci melni jëfandikoo deret ji, fonction coagulation, indicateurs biochimiques ak depistaasu feebar genetik. Ci ñoom, reactifs yiy saytu soin (POCT) ñu ngi leen di soxla bu baax ci senaario soin yu njëkk yi ak paj mu jamp ndax seen portabilite ak seen feedback bu gaaw. Ci jamano jooju, siiwal sistemu test otomatik itam taxna defarkatu reactif yi gëna baaxal stabilite formul bi ngir mëna ànd ak bëgg-bëggu liggéey bi ci aparey yu am produit yu bari.
Dafay am solo lool ñu xamni tar giñ tëral ci sàrti àdduna bi dafay soppi anam wi liggéeyukaay yi di doxalee. Reglemaa yi EU IVDR tëral ak tegtali FDA yu mujj yi ci Etats Unis dañuy fësal ni ñuy doxalee ci dundu reactif yi, boole ci toppu macceer bu bees bi, saytu kalite bi ci liggéey bi, ak njubteg done yiñ joxe ci klinik bi. Loolu moo waral liggéeyukaay yi yokk seen dugal xaalis ci R&D ngir gëna suqali kàttanu di doxal reactif yi ci diggante lots-to -batch ci noonu lañuy fexe bañu am sensitivite ak spesifisite.
Ci ëlëg, ak boole xarañteg xelu masin ak xaralay done yu mag, reactif hematologie mën nañu jëm kanam ci wàllu xarañteg xel. Ci misaal, defar ay parametru test yu baax jaaraleko ci algorithm yuy jàng masin, wala defar sistemu etalonnage buy méngoo ngir wàññi li nit ñi di def. Yooyu gis-gis yu bees dina ñu gëna dëgëral liggéeyu reactif hematologie ci wàllu diagnostic in vitro ba noppi joxe pexe xarala yu gëna am njariñ ci wàllu wérgi-yaramu àdduna bi.





